
Kan moom a bind AK
lu tax mu bind ma ?
2
Kan moom a bind AK lu tax mu bind ma ?
BEEPP MIR MUMU MANA DOON DAAY TEKTALE AMUK YAALLA
MIKO BIND!
KAN MOO BIND ASAMAN YI AK LICI SEEN BIIR CI AY MBINDEEF
YU MAAGG YOO XAMNE MBINDEEF MANULEENA PEEK?
Kan moo def nosiin wu xereñe wii ?
Kan moo bind nit may ko ag dégg ak ub jis ak xel te def ko muy ku man
a am xam-xam tey xam li xew.
Naka ngay firee wii tërëliin wu yéeme ci jumtukaay yi nekk ci sa biir
yaram ak yaramu ndundat yi ? Kan moo fent loolu ?
Naka la dund bu rëy bii man a nosaloo ci tëraliinam yu koy nose nose
gu yéeme ba àdduna sosoo ba tay ?
Kan moo tëral tëraliin yii di àtte àdduna bi(dund ak dee, juranteg yiy
dund, guddi ak bëccëg, soppikug jamono yi, añs )
NDAX ADUNA BI MOO BIND BOOPAM ? WALLA DAFA ÑAW CI LUDUL
DARA ? WALLA DAFA AM CI XËY CËPPU ?(FIIRU)
LUTAX DOOM AADAMA DI GËM MBIR YOO XAMNE JISULEEN ? NIKI
: (YËG YËG ,AK XEL, AK RUU ,AK COFEL) DU LUDUL NE MOOM DAAY JIS
SEEN JEEXIT ?NAKALAY WEEDDEE AMUK YALLA MI BIND ADUNA BU
MAAGG BII !TE MOOM MUY JIS JEEXITI MBINDEEFAMYI, AK JEEXITI
XARALAAM, AK JEEXITI YËRMËNDEEM?!.
KENN DU NANGGU NIUNEKO KËRGII DAFA AM TE KEENN TABAXUKO
!KOON NAK NAKALAY NANGGOO ÑUUNEKO ADUNA BU MAAGG BII DAFA
AM TE KEENN BIND KO ?BOROOM XEL NAKALAY NANGGOO BILE TËNKU
BU JEEKK CI ADUNA BII DAFA XËY CËPPU ?
YALLA MU KAWE MI WAXNA :ۡ
(NDAX ÑOOM DAÑULEEN BIND TE BAWOO WUÑU CI DARA ?
WALLA ÑOOM ÑOO BIND SEEN BOOPPWALLA NDAX ÑOOM ÑOO BIND
3
ASAMAN YI AK SUUF SI ?LI AM BADES MOOY DAÑU AMUL KOOLUTE CI
SEEN NGËM). [52 : 32]. AT TUR
(YALLA MU KAWE MI )
AMNA KOO XAMNE MOOY BOROOM BI MOOY KI BIND TE MOOY
KEENN KI ! AMNA AY TUR AKI MELOKAAN YU BARI TE MAAGG TEY
TEKTALE AK MATAM, BOOKK NACI TURËM :AJI BIND JI, AJI YËRËM KUKO
SOOP CA ALLAAXIRA, AJI WARSAGALE JI, AJI TABE JI, " KI ÑUY
JAAMU"(ALLAAHU) MOOY TUR BI GËNA SIIW CI AY TURËM, LI MOOY
FIRI MOOY : KI YEELLO DIAAMU MOOM KESE TE DUÑUKO
BOOKKALEEK AK LEEN !.
Yàlla mu kawe mi wax na ci Alxuraan ju tedd ji:ۡ
{WAXAL NE LIY MBIR TEY MBIR :YALLA KEENN LA}
{YÀLLA MOOY KU ÑUUY JUBLU CI FAJUK AAJO YI}
{JURUL KEENN TE KEENN JURUKO}
{TE AMUL KEENN KUY NAWLEEM} [112: 4-1].
YALLA MU KAWE MI WAXNA :ُ
{YALLA MOOY KI ÑU WARA JAAMU ,JAAMU GI DI JARIÑ ÑAAKK
JAAMU GI DI LOR, AMUL KEENN KINIUY JAAMU KU DUL MOOM, MOOY
AJI-DUNDU JI MOOY KIY TAXAWU LEEPP, DU GAMMEENTU RAWATINA DI
NELAW, MOOY BOROOM LICI ASAMAN YI AK LICI SUUFSI, ANA KAN
MOOY RAMMU FA MOOM NDARE CI NDIGALAM, MOO XAM LI NGEEN DI
4
DUNDU MOO XAM LI LEEN JIITU, TE KEENN DU PEEG DARA CI XAM
XAMAM NDARE LUKO SOOP, BANĞAM BA ËPP NA ASAMAN YI AK SUUFSI,
TE WATTU LEEN TIISA LUKO TE DIISA LUKO, MOOM REK MOOY KI KAWE
TE MOOM REK MOOY KI MAAGG} [2: 255].
MELOKAAN NU BOROOM BU SEELL BI TE KAWE
BOROOM BI MOOY KI BIND SUUFSI TE TAAGGATKO, DEFKO
YEELLOOK MBINDEEFAMYI, MOOY KI BIND ASAMAN YI AK LICI BIIRËM
CI AY MBINDEEF YU MAAGG, MU DEF JANT BI AK WEERWI AK GUDDI GI
AK BACCAGBI, BILE TËNK BU JEEKK DAY TEKTALE MAAGGAAYM .
BOROOM BI MOO ÑU TAGGATAL NGALAW LI NGA XAMNE MANUÑOOY
DUNDU CI LUDUL MOOM, MOO ÑUY WACCEEL TAW, MOO ÑU TAGGATAL
GEEJ GI AK DEX YI, MOOM MOO ÑU DOON DUNDAL BIÑU NEEKKEE
MBEEMUR (ËMBU CI BIIR)CI SUÑU BIIRI WAAJUR YI TE AMU ÑUWOON
BEENN KAATAN, MOOM MOOY KI DOON DEF DERET JI MUY DAW CI
SUÑUY SIDIT, MU DEF SUÑU XOL MUY FER FERI CI LUUY WEY BI ÑU
JUDDO BA BALAAÑUY FAATU.
YALLA MU KAWE MI WAXNA :ُ
ﱠ
{ YALLA MOO LEEN GEENNE CI SEEN BIIRI WAAJURYI FEEKK
XAMULEEN DARA MU DEFAL LEEN NOOPP AKI BËT AKI XEL NDAX
NGEEN SANT } (16: 78)
BOROOM BI ÑUUY JAAMU SIKK NEEKKUL CI NE MOOY BOROOM
MELOKAAN YU MAT YI.
BOROOM BI ÑU BIND MOO ÑU WARSAGAL YU YU MANA XAM
MAAGGAYAM, MU JËMBAT CI ÑUN AK CET (SET) GU ÑUY TEKTAL
MAAGGAYAM AK CI NE MOOM DU MELOWOO MELOKAAN YU MANKI.
AK JAAMU FAAWWU MU NEEKK NGIR YALLA MOOM DOONĞ, NDAX
TE MOOY KU MAT KU YEELLOO JAAMU, LEEPP LUÑU JAAMU LUDUL
MOOM CAAXAAN LA TE LU MAANKI LA TE LUÑU GAARAL LA CI DEE
AK JEEX.
5
KU ÑUUY JAAMU WARUL NEEKK MBINDEEF WARUL NEEKK
XËRËM WARUL NEEKK GARAB WARUL NEEKK NDUNDAT !
YEELUL CI KU AM XEL MUY JAAMU LUDUL KU AM XEL ! NAKALAY
JAAMOO MBINDEEF MUKO YEESS ?!
BOROOM BI DU NEKK MBEEMUR CI BIIRU JIGEEN DI JUDDU NI
XALE YI DI JUDDOO !
BOROOM BI MOO BIND MBINDEEF YI, MBINDEEF YEEPP ÑOONGI CI
AK NGABËM NEEKK CI SUUFU NOTEELAM; MBINDEEF MANUKOO LOR
KEENN MANUKOO DAAJ CI GARAB WALLA DIKO MBUGËL WALLA DIKO
DOYEDAL !
Boroom bi du dee!
BOROOM BI MOOY KI NGA XAMNE DU FAATTE, TE DU NELAW, TE DU
LEEKK AW ÑAM, MOOY KU MAAGG KI NGA XAMNE JOOMBUNA CI MOOM
MUUY AM SOXNA WALLA DOOM ;NDAX AJI BIND JI DAFA AM AY
MELOKAANI MAAGG TE AMUL MELOKAANU AAJOWOO JËM CI KEENN
WALLA MAANKI BEEPP YAX BOO XAMNE DAFA AM LU WUUTEEK
MAAGGAYU YALLA CI LU ÑOOY ASKANALEE YONENT YI LOOLA YAX YU
ÑU SOOPPI LA BOOKKUL CI NDEEY GU WERGI GI NGA XAMNE MOOM LA
YONENT YALLA MUUSA ËNDI AK YONENT YALLA ĮSÃ AK ÑU DUL ÑOOM
CI YONENT YI YALNA YALLA DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI.
Yàlla mu kawe mi nee na:
{ YEEN NIT ÑI ÑUNGILEEN JOX MISAAL DEGLULEENKO ,ÑI
NGAXAMNE YEENANĞ LEEN DI JAAMU BAAYI YALLA DU
ÑUMOSABINDWEÑ DOONTEDAÑU DAJALOONGIRLOOLU BU LEEN WEÑ
REEKKILOON DARA DUÑUKO
MANA NANGU CI MOOM KIIY SAAKKU LOOLUAKA LOTT MOOK
LAMUY SAAKKU} (73)
6
{ JOXUÑU YALLA DËGG DËGGI GËDDËM
TE MOOM YÀLLA MOOY BOROOM KAATAN TE MOOYKI NOT CI
NGUURËMGI} (74) [22: 73,74]
NDAX XEL NANGUNA YALLA BAAYI ÑU CI LUDUL NDEEY ?(WAHYU)?
NDAX XEL NANGUNA YALLA BIND MBINDEEF YI CI LUDUL BEENN
JUBLU WAAYE ?WALLA MU BIND LEEN CI POH ? TE MOOM MOOY KU
XEREÑKI DI KU XAM LEEPP. !
NDAX XEL NANGUNA KI ÑU BIND CI BILE XEREÑ TAGGATAL ÑU LICI
ASAMAN YI AK LICI SUUFSI, MU BIND ÑU CI LUDUL JUBLU WAAYE,
WALLA MU BAAYI ÑU CI LUDUL TONTU AAJ YI ËPP SOLO CI YI NGA
XAMNE DAF ÑI SOXAL, LAN MOO NEKK CI GINAAW DEE?LAN MOOY
JUBLU WAAYE CI YALLA BIND ÑU?
LI AM BA DES MOOY YALLA YOONNI NA YÓNENTE YI NGIR ÑU XAM
JUBLU WAAYI SUÑUK AM, AK LAN LA YALLA NAMM CI ÑUN!
YALLA MOO YOONNI YONENT YI NGIR ÑU XAMAL ÑU NE MOOM
DOONĞ MOO YEELLO AK JAAMU, AK NGIR ÑU XAM NAKA LAÑUKOOY
JAAMOO, AK NGIR ÑU JOOTALI ÑU AY NDIGALAM AK AY TEEREEM, AK
ÑU XAMAL ÑU XIIMA YU BAAX YI NGA XAMNE BU ÑU CI JAAPPEE; SUÑU
DUNDU TEEY, TE YIWYI AK BARKE YI DANAÑ ÑU DAJ KAPP.
YALLA YOONNI NA YÓNENTE YU BAREE BARI NIKI (NUUH ,
IBRAHIMA, MUUSAA, HIISAA)...MU JOXLEEN AY MANDARGA AKI
KEEMAAN YUY TEKTALE SEENUK DËGGU TE ÑOOM ÑUÑU YOONNI
LAÑU ÑU BAAYEKOO FA YALLA AJI BIND JI.
KI MUJJI CI YONENT YOOYU MOOY MUHAMMAD YALLA NAKO-
YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI- YALLA WAACCE CI NIOOM ALXURAN
BU TEDD BII!
YONENT YOOYU LE XAMLE NAÑU CI LULEER NAAÑÑI DUNDU BII
MOOY NATTU KAAYU JAAMYI LA, WAAYE DUNDU DËGG DËGG MOOY
BACA GANNAW DEEH!
TE FOOFA LE AMNA AL JANNAH NGIR WËY GËM YI NGA XAMNE
ÑOO DOON JAAMU YALLA MOOM DOONĞ , TE GËM MBOOLEEM
YONENT YI, TE AMNA YIT SAFARA YALLA WAAJAL KO NGIR WËY
WEEDDI YI NGA XAMNE DAÑU DOON JAAMU AY XËRËM DOKO
7
BOOKKAALEEK YALLA, WALLA ÑU WEEDDI KEENN CI YONENT YALLA
YI
YALLA MU KAWE MI NEENA:
{YEEN DOOMU AADAMA YI BU LEEN AY YONENT ÑAWALEE YU
BOOKKCI YEEN DI LEEN JAANGATAL SAMAY AAYA; KEEPP KU RAGAL
YALLA TE YEWENËL AY JËFAM DU RAGAL MBUGËLUM ËLLËK TE DU
JAAXLE CI LI MUUY BAAYI CI GINAAWAM. } (35)
{WAAYE. ÑI NGA XAMNE
DAÑOO WEEDDI SUÑUY AAYA ÑU JOOMBALE SEEN BOOPP
JAANGATKO; ÑOOÑU ÑOOY. WAA SAFARA}.(36)
[7: 35,36].
Yàlla -mu sell mi nee na-:
{NDAX DANGEEN JOORT NE DAÑULEEN BIND NGIR FOH! TE
YEEN DUNGEEN DEELUSI CI ÑUN} [23: 115].
Alxuraan bu tedd bi
ALXURAN BU TEDD BI MOOY KAADDUK YALLA MU KAWE MI NGA
XAMNE WAACCE NAKO CI NGËN JI YONENT -YALLA NA YALLA DOOLLI
KO XEEWËL AK MUCCI TE DOOLLI LEEN KO-MOOM ALXURAN JI MOOY
DËGG CI AY AATTEEM MOOY WER CI AY XABBARËM, YALLA MUNGEEY
DAKKU ÑIKO WEEDDI CI ÑU ANDI DOONTE WEENN SAAR LA WU
MEL NI ALXURAN ÑU LOOTT CI LOOLU NGIR TAARUK FEEMAM AK
YEEMEEK AY KAADDUM, MU LAAMMBOO LU BËRI CI AY TEKTALI
XEL AK LU WERAWER CI XAM XAM YUY TEKTALE NE TEERE BII
8
MANULA BAAYEKOO CI JAFI MBINDEEF, LI AM BA DES DAAL MOOY
KAADDUK BOROOM MBINDEEF YI LA TUDDUNAA AK SEELLËM.
Lu tax Yónente yi bari?
YALLA YOONNI NA AY YONENT CA NDIALBEEN NGIR ÑU WOO
NITÑI JAMEELEEN CI SEEN BOROOM, TE JOOTALILEEN AY NDIGALAM
AK AY TEEREEM, SEEN WOOTE ÑOOM ÑEEP MOOY JAAMU YALLA MU
TEEDD MI, SAA YU AW XEET TAAMBLEE BAAYI WALLA DI SOOPPI LI
YONENTAM BI ANDI CI NDIGLE WEETAL YALLA; REK YALLA TOOGG
BENEEN YONENT NGIR MU JUBBANTI YOONWI, TE DEELLOO NITÑI CI
MELOKAAN BU MUJJI AYIB, CI WEETAL YALLA AK NANGGULKO, BA
YALLA TAJEE YONENT YOOYU LE CI YONENT YALLA MUHAMMAD YALLA
NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI, BI NGA XAMNE MOO ANDI
TËRËLIN BU MUJJI BII, BU SAX DAAKK BII, BU MATALE MBOOLEEM
MBINDEEF YI, BAH BIS PEEÑCI, BUY MOOTALI TEY FOOLLI LIKO
JIITUWOON CI AY TËRËLIN, BOROOM BI MOO GADDUL TËRËLIN BII AK
YONENT GII AK DES AKUK WEY BA BIS PEEÑCI.
LOOLU MOO TAX ÑUN JULIT ÑI DËÑUY GËM- NIKO YALLA
DIGLEE-MBOOLEEM YONENT YI AK MBOOLEEM TEERE YU JIITU YI.
YALLA MU KAWE MI WAXNA;َ
{ CA DËGG DËGG YONENT BI GËMNA LIÑU WAACCE CI MOOM MU
BAAYEKOO CA BOROOMAM, JULIT YI ITËM ÑOOM ÑEEPP GËM NAÑU
YALLA AK MALAAKA YI, AK TEERE YI AK YONENT YI, DUÑU TEXXALE
DIGËNTE KEENN AK KEENN CI YONENT YI, BAH NOOPPI ÑUNE: DEEGG
NAÑU TE NANGGU NAÑU, ÑOONGI SAAKKU SA NDIEEGGËL YAW SUÑU
BOROOM, TE CI YAW KESE LAAY DEELLU SI MUJUK ÑEEPP.
[2: 285].
9
NIT DU GËM YALLA, FEEK GËMUL MBOOLEEM YONENT YI-YALLA NA
YALLA DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI,
KI YOONNI YONENT YI MOOY YALLA! KU WEEDDI YONENTËK
KEENN CI ÑOOM; WEEDDI NA ÑOOPP. AMUL BEENN BAAKAAR BU
GËNË MAAGG DOOM AADAMA DI LAANKAL YALLA KAADDUM, NGIR
DUGG ALJANNAH; FAAWWU NITKI GËM MBOOLEEM YONENT YI-YALLA
NA YALLA DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI.
LI WAR CI KUNEEKK CI JAMANO JII MOOY MU GËM MBOOLEEM
YONENT YI, TE LOOLU DU MËNË AM LUDUL GËM TE TOOPP KI MUJJI CI
ÑOOM TE MOOTALILEEN/MUHAMMAD YALLA NAKO YALLA DOOLLI
XEEWËL AK MUCCI.
ALXURAN TUDD NA NE :KEEPP KU BAÑA GËM KEENN CI YONENT YI;
WEEDDI NA YALLA TE WEEDDI NA KADDOOM:
JAANGAL LAAYA JII DI ÑËW:
ﱠ
{WERNA NE ÑI NGA XAMNE DAÑOO WEEDDI YALLA AK
YONENTAM YI, BA NOOPPI BËGA TEXXALE DIGANTE YALLA AKI
YONENTAAM NUY WAX NAAN: ÑUN DAAL DAÑUY GËM ÑII WEEDDI
ÑII, ÑU BËGA JAAPPU CI DIGANTE BOOBU AWYOON
NOOÑU ÑOOY ÑU MAT SËKK YEEFËR CA DËGG DËGG, TE
WAAJALAL NAÑU YEEFËR YOOYU MBUGËL MUY DOYODALAATE} [4:
150,151].
LAN MOOY LISLAAM?
LISLAAM MOOY JEEBLUL YALLA MU KAWE MI CI WEETAL KO , AK
WOOMMATUL KO CI NANGUL KO TE TAXAW CI TËRËLINAM CI GËRËM
KO AK NANGU KO.
10
YALLA YOONNI NA YÓNENTE YEEP BEENN BATAAXEL MOOY:
WOOTE JAMEE CI JAAMU YALLA MOOM DOONĞ AMUL BEENN AJI
BOOKAALE .
LISLAAM MOOY DIINE MBOOLEEM YONENT YI-YALLA NA YALLA
DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI-, SEEN. WOOTE BEENN LA WAAYE
SEEN
TËRËLIN MOO WUUTE, JULIT YI TEY ÑOOM DOONĞ ÑOO JAAPP
CI DIINE JU WER JI NGA XAMNE MBOOLEEM YONENT YI MOOM LAÑU
ANDI, BATAAXELU LISLAAM BI CI JAMANO JII MOOY DËGG ; BOROOM BI
YOONNI IBRAHIMA AK MUUSAA AK HIISAA MOO YOONNI KI MOOTALI
YONENT YI /MUHAMMAD -YALLA NA YALLA DOOLLI KO XEEWËL,
TËRËLIN LISLAAM MOO ÑËW DAADI FOOLLI MBOOLEEM TËRËLIN
YIKO JIITU WOON.
MBOOLEEM DIINE YI NGA XAMNE NITÑI DAÑUCEY JAAMOO YALLA
MUNGI BAAYI KOO CI JAFU MBINDEEF, WALLA SAX ÑU NEEKKOON
DIINE YU BAAYEKOO FA YALLA WAAYE LOXO MBINDEEF FOH CI MU
MUJJI DI NDIAXAS MU RËNKALOO CI AY CAAXAAN AKI LEEBOON
LUPEEN YU ÑUDOON DOONANTE AK AY LAAMBATUY MBINDEEF,
WAAYE PAS PASU JULIT YI BEENN PAS PAS LA LEER, DU SOOPEEKU
XOOLAL ALXURAN BEENN TEERE LË CI REWI JULIT YI.
YALLA MU KAWE MI WAXNA CI ALXURAN :ْ
{WAXAL NE :ÑUN GËM NAÑU YALLA AK LIMU WAACC CI ÑUN AK
LMU WAACC CI YONENT YALLA IBRAHIMA AK ISMAÏÏLA AK ISHAAQA
AK YAHQUUBA AK AY SËTËM AK LIÑU JOXOON MUUSAA AK IISAA AK
MBOOLEEM YONENT YI MU BAAYEKOO CI SEEN BOROOM DUÑU
TEEXALE KEENN CI ÑOOM TE ÑUN DAÑUY WOOMMATUL YALLA}.
(84)
11
{KU SAAKKU LUDUL LISLAAM MUY SA DIINE ; DUÑU KOKO
NANGUL, TE MOOM ËLLËK ALLAAXIRA DAY BOOKK CA ÑA PERT ÑI
.}(85)
[3: 84,85].
LAN LA JULIT YI FAS CI IISAA-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL
AK MUCCI. ?
NDAX XAM NGA NE : JULIT YI DAÑOO WARA GËM YONENT YALLA
IISA TE BËGG KO WORMAAL KO TE GËM BATAAXELËM BI NGA
XAMNE MOOY WOOTE JAMEE CI JAAMU YALLA MOOM DOONĞ CI LU
ANDUL AK BEENN BOOKAALE KAT ! JULIT YI DAÑUY FAS NE :
YONENT YALLA IISA AK YONENT YALLA MUHAMMAD- (YALLA NA LEEN
YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI-)AY YONENT LAÑU YOO XAMNE
YALLA MOO LEEN YOONNI NGIR ÑU GINDI NITÑI JAMEE LEEN CI
YOONU YALLA AK YOON AL JANNAH.
TE DAÑUY FAS NE YONENT YALLA IISA -(YALLA NAKO YALLA
DOOLLI XEEWËL AK MUCCI ) BOOKK NACI YONENT YI GËNË MAAGG YI
NGA XAMNE YALLA MU KAWE MI YOONNI NA LEEN, TE DAÑUY FAS NE
JUDDU NA CI ANAM BU YEEME, YALLA XAMAL NAÑU CI ALXURAN
NE : MOOM IISA BIND NAÑUKO CI LUDUL MUY AM BAAY, NIKI MU
BINDEE WOON AADAMA TE AMUL YAAY TE AMUL BAAY; NDAX TE
YALLA KAT MOOY KI MAN LEEPP.
DAÑUY FAS NE: IISA DU YALLA, DU DOOMU YALLA, TE MOOM
KEENN DAAJU KO CI GARAB, LI AM BA DES MOOY MOOM AJI DUNDU
LA, YALLA YËKËTIKO JËMEE FA MOOM; NGIR MU WAACCI MUJJUK
JAMANO DI AATTE KAT BU MAANDU SUKO DEFEE MU AAND AK
JULIT YI; NDAX JULIT YI ÑOOM ÑOO GËM WEETAL YALLA BI NGA
XAMNE MOOM LA YONENT YALLA IISA ANDI AK MBOOLEEM YONENT
YI.
YALLA XAMAL NAÑU CI ALXURAN BU TEDD BI NE: BATAAXELU
YONENT YALLA IISA BI NASRAAN SI DAÑUKO JEENGAL LII ÑU SOOPPI
KO BA NOOPPI RAX CA YENEENI YAX YOO XAMNE YONENT YALLA IISA
WAXU LEEN KO, LIY DËGËL LOOLU MOOY WOOTEEK TEERE YUÑU
SOOTTE CA BU NDIAKK BA AK BARIK JUUNOO CA TEERE YOYALE.
YALLA XAMAL NAÑU NE: NAKA YONENT YALLA IISA DADAAN
JAAMU BOROOMAM TE SAAKKU WUL CI KEENN MUJAAMUKO, LIMU
12
DAAN DIGËL AW NITËM MOOY JAAMU YALLA MILEEN BIND, WAAYE
SAYTAANE MOOY XIRTËL NASRAAN SI ÑUUY JAAMU YONENT YALLA
IISA , YALLA XAMAL NAÑU CI ALXURAN NE: DU JEEGGËL KEENN KU
JAAMU LUDUL YALLA MU KAWE MI, TE NAKA YONENT YALLA IISA
DANA DAÑ CI ÑIKODOON JAAMU BA SET WEECCI ËLLËK BISU BEENCI
BA, MUNE LEEN DIGËLOON NAA LEEN NGEEN JAAMU KI BIND ÑEEPP,
TE MOSU MAAY SAAKKU CI YEEN NGEEN JAAMU MA BEEN YOON,
BOOKK NACI LIY FIRNDEEL LOOLU WAXU SUÑU BOROOM BU KAWE BI:َ
{ÊEY YEEN ÑOÑ TEERE! BU LEEN JEEGGI DAYO CI SEEN DIINE! TE
BU LEEN WAXAL YALLA LUDUL DËGG ; NDAX TE WËR KAT BII/ DI IISA
DOOMU MARYAMA NDAWAL YALLA LA, TE KAADDUM LA ( NEEKKAL
REKK MU NEEKK)GOO XAMNE SAANNI NAKO CI MARYAMA TEY RUU
GU BAAYEKOO CI MOOM, GËM LEEN YALLA AK YONENTËM YI, BU LEEN
WAXNE :YALLA YI ÑATT LAÑU ( YALLA AK IISAA AK MARYAMA) YAM
LEEN MU NEEKK YIW CI YEEN, YALLA DU LUDUL KEENN, JOOMB NA
MUY AM DOOM, MOO MOOM LI CI BIIR ASAMAN YI AK LICI BIIR
SUUFSI, (CI MBIND AK CI MOOMEL)MOOM YÀLLA DOOYNA
SUKANDEKU WAAYE (171)
[4: 171].
YALLA MU KAWE MI WAXNA:ْ
13
{TUDDËL CI ALXURAN BIS BU YÀLLA DI WAX :ÊEY YAW IISA DOOMU
MARYAMA!NDAX YAW YAA WAX NITÑI NA LEEN:JAAPPEE LEEN MA MAN
AK SAMA YAAY ÑUY ÑAARI YÀLLA YU BOOKKUL AK YÀLLA, IISA NE:
TUDDU NA SAK SEELL SAK JOOMBU BEEPP BOOKKALE ,JAADUWUL CI
MAN MAY WAXAL SAMA BOOPP LUMA YEELLO WUL, TE SU FEEKKONNE
WAXNAKO;YAW XAM NGAKO, NDAX YAW XAM NGA LICI MAN LEEPP, TE
MAN XAMUMA LICI YAW, NDAX TE YAW YAAY XAMAAKOONI KUMPA
YEPP} (116) (5: 116)
KU BËGGA MUCCI ALLAAXIRA; NA DUGGU CI LISLAAM TE TOOPP
YONENT BI MUHAMMAD ,YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK
MUCCI.
BOOKKNA CI XEW XEW YU WER YI NGA XAMNE YONENT YI DËPPOO
NAÑU CI ÑUÑU SOLOO AK ÑUÑU YOONNI (YALLA NA LEEN YALLA
DOOLLI MUCCI) MOODI LIY MBIR TEY MBIR ALLAAXIRA JULIT YI REKK
FAAY MUCCI! ÑI NGA XAMNE GËM NAÑU YALLA MU KAWE MI TE
BOOLE WUÑU CI JAAMU GIÑUKOOY JAAMU KENEEN, ÑU GËM
MBOOLEEM YONENT YI-YALLA NA LEEN YALLA DOOLLI XEEWËL AK
MUCCI 'ÑU NEEKKOON CI JAMANO YONENT YALLA MUSAA GËM KO
TOOPP NDIAANGALEEM ÑOOÑU JULIT LAÑU YU BAAX KU LAANKA GËM
YONENT YALLA IISA TE NAAN DAMAAY DES CI DIINE YONENT YALLA
MUUSA ,KOOKU GËMUL;NDAX MOOM LAANK NAAY GËM YONENT BU
YÀLLA YOONNI, GANNAAW BA YALLA YOONNEE KI MUJJI CI YONENT
YI:MUHAMMAD-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI- DAFA
WAR CI ÑEEPP ÑU GËM KO, BOROOM BI YOONNI MUUSAA AK IISAA
MOO YOONNI KI MOOTALI YONENT YI: MUHAMMAD-YALLA NAKO
YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI -KU WEEDDI BATAAXELU
MUHAMMAD-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI-DAADI NE
DAMAAY DES CI TOOPP MUUSAA WALLA IISAA ; KOOKU GËMUL.
DU DOY REKK JËMM JI WAXNE: MOOM DAY HORMAAL JULIT YI,
DU DOY NGIR MUCCI ALLAAXIRA MUUY SARAXE DI DIMBALE WËY
ÑAAKKAYI, LI AM BA DES FAAWWU MU GËM YALLA TE GËM AY
TEEREEM YI AK YONENTËM YI AK BIS BU MUJJI BA; NGIR YALLA
NANGUL KO!NDAX TE AMUL BAAKAAR BU GËNË MAAGG BOOKKAALE
AK WEEDDI YALLA DEELLOO LI YALLA WAACCE CI YONENT BI
YAHUUD YI AK NASRAN SI NGA XAMNE DEEGG NAÑU YOONNIIK
14
YONENT YALLA MUHAMMAD-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK
MUCCI-ÑU BAÑ KOO GËM BAÑA DUGGU CI DIINE LISLAAM, DAAÑU
DUGGU ËLLËK SAFARA JAHANNAMA SAX FA BË FAAWWU NIKIO SUÑU
BOROOM WAXEE:
{NAKA GAAYI NGA XAMNE DAÑOO WEEDDI YALLA MOO XAM ÑU
BOOKK CI ÑOÑ TEERE YA WALLA ÑU BOOKK CA WËY BOOKKAALE YA;
DAAÑU DUGGU SAFARA JAHANNAMA SAX FA, ÑOOÑU ÑOO YEES CI
MBINDEEF YI}(6)
[98: 6].
BI NGA XAMEE NE BATAAXEL BU MUJJI BII WAACCI BAAYEKOO CA
YALLA JËM CI MBINDEEF YI BUKO DEFEE DAAY WAR CI KEENN KUNE
KUY DEEGG LISLAAM TEY DEEGG YONENT BU MUJJI BII
MUHAMMAD-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI- MU GËM
KO TE TOOPP TËRËLINAM TE NANGGUL KO NDIGËLAM AK TEREEM,
LOOLOO TAX KU DEEGG BATAAXEL BU MUJJI BII DADIKO LAANK;YALLA
DUKO NANGGUL DARA, TE DANAKO MBUGËL ALLAAXIRA. BOOKK NACI
FIRNDEY LOOLU WAXU YALLA MU KAWE MI:
{képp ku topp jeneen diine ju dul lislaam deesu ko ko nangul te bu
bis-pénc baa di na bokk ca way torox ña }
[3 : 85].
{WAXAL: YEEN ÑOÑ TEERE YI KAAY LEEN CI KAADDU GOO
XAMNE GU YAMOO LA SUÑU DIGANTE ÑOOK YEEN TE MOOY BUÑU
15
JAAMU KUDUL YALLA, TE BUÑUKO BOKKAALEEK LEEN, TE BUÑU
JAAPPANTE CI SUÑU BIIR AY YALLA, BAAYI FI YALLA,BU ÑU
DËDDOO;NANGEEN WAX NE:SEEDE LEEN NE NE ÑUN WËY NANGGU
LAÑU WËY WOOMMATU LAÑU}(64) (3: 64).
LAN MOOY WARAL MANEEKK JULLIT?
NGIR DUGGU CI LISLAAM WAR NA ÑU GËM YILE JUROOM MBEENNI
POONKK:
GËM YALLA MU KAWE MI ,CI NE MOOY KI BIND MOOY WARSAGAL
MOOY TOOPPATOO TE MOOY KI MOOM, AMUL LEENN LU NIROOK
MOOM, AMUL AANDANDOO BU JIGEEN (JABAR)DU CAAGEN DOOM,
MOOM DOONĞ MOO YEELLO JAAMU.
GËM MALAAKA YI CI NE ÑOOM AY JAAMI YALLA LAÑU BIND NA
LEEN CI LEER MU BOOLE CI SEEN LIGEY ÑUY WAACCE NDEEYËM
(WAHYUM)CI AY YONENTAM.
GËM MBOOLEEM TEERE YI NGA XAMNE YALLA WAACCE NA LEEN
CI AY YONENTAM (NIKI TAWRAAH AK LINJIIL)BI MUJJI CI TEERE YI
MOOY ALXURAN BU TEDD BI.
GËM MBOOLEEM YONENT YI NIKI NUUH AK IBRAHIMA, AK
MUUSAA AK IISAA KI CI MUJJI DI MUHAMMAD YALLA NA LEEN YALLA
DOOLLI XEEWËL AK MUCCI, ÑOOM AY MBINDEEF LAÑU YALLA
DËGËRËL LEEN CI NDEEYAM JOXLEEN AY MANDARGA AKI KEEMAAN
YUY TEKTALE SEENUK DËDDU.
GËM BIS BU MUJJI BA JAMANO BA YALLA DI DEEKKAL ÑU
NDIAKK ÑA AK ÑU MUJJI ÑA MUY AATTE DIGANTE MBINDEEFAMYI
DI DUGAL WËY GËM YI ALJANNAH TE DI DUGAL WËY WEEDDI YI
SAFARA.
GËM DOGAL GËM NE YALLA MOO XAM LEEP LU AMOON CA LA
WEESU AK LIIY AM CI LUY ÑAW, TE NE YALLA DOGAL NAKO TE SOOP
NAKO TE MOO BIND LUNE.
LISLAAM MOOY YOONU TEXE!
LISLAAM MOOY DIINEY MBOOLEEM YONENT YI!.
16
LISLAAM MOOY YOONU XEXE GU WERGI FII CI ADUNA, AK
XEEWËL GU SAX DAAKK CA ALLAAXIRA.
LISLAAM MOOY MOOM DOONĞ MOOY DIINE JI MANA FAJ HAAJOOY
RUU AK YARAM, TE MOO MANA LIJANTI MBOOLEEM LËJ LËJI DOOM
AADAMA YI.
YALLA MU KAWE MI NEENA:َ
{YÀLLA NE AADAMA AK HAWWAA: WACCI LEEN BAAYEKOO CI
ALJANNAH JI YEEN ÑEEPP , AMNA ÑEENN CI YEEN ÑOO XAMNE NOON
LAÑU CI ÑEENN ÑI BU LEEN AM JUB ÑAWALEE BAAYEKOO FI MAN;KU
TOOPP SAMA JUB DU SAANKU TE DU TOROX. }
{KEEPP KU DUMMOOYU SAMA ALXURAN BII; DANA AM DUNDU
BU XAT TE DANAÑUKO PANGĞ BIS PEEÑCI BA MU GUMBA}
[20: 123,124].
LAN LAAY JARIÑOO CI SAMAK DUGGU CI LISLAAM?
DUGGU CI LISLAAM DAFA AM AY NDIARIÑ YU MAAGG, BOOKK
NACA:
TEXE AK TEDD CI ADUNA TE MOOY NIT KI NEEKK DI JAAMUB
YALLA KESE, BUDUL LOOLU DAAY NEEKK JAAMU BAANEEXU
BAKANAM AK SEYTAANE AK FOYTEEF YI.
GËN JAAY MAAGGI TEXE CA ALLAAXIRA MOOY NIT KI MUCCI CI
MBUGËLËM SAFARA TE DUGGU ALJANNAH, TE TUUFU CI
NGËRMAANDE YALLA AK SAX CA ALJANNAH JA.
ÑI NGA XAMNE YALLA DALEEN DI DUGAL ALJANNAH, DAÑEEY
DUNDU CI XEEWËL GU SAX CI LUDUL DEE! WALLA BEENN XEET CI
FEEBAR WALLA MEETIT WALLA NDIAAXARE, WALLA XOBIDAAS, TE
DAÑUY AM LEEPP LUÑU BËGG.
17
ALJANNAH AMNA AY XEEWËL YOO XAMNE BËT MOSU KO JIS,
NOOPP MOSU KO DEEGG, TE MOSUL TOOXXU CI XELU BEENN DOOM
AADAMA.
BOOKKNA CI FIRNDE LOOLU WAXU YALLA MU KAWE MI:ۡ
{KEEPP KU DEF JËF JU BAAX MOO XAM GOORLA MOO XAM
JIGEEN LA; DAAÑU KO DUNDAL DUNDU BU MUCCI AYIB TE DAAÑU
LEEN FAY SEENUK PAY CI LU DAAXX LAÑU DOON DEF} [16: 97].
LAN LAA NAROONA ÑAAKK SUMA LAANKKOON LISLAAM?
NIT DANA ÑAAKK LU GËNË MAAGG CI XAM XAM AK RAAÑÑEE TE
RAAÑÑEE AK XAM YALLA, DANA ÑAAKK NGËM YALLA MI NGA XAMNE
MOOY MAY NIT KI KOOLUTE AK DAL CI ADUNA, DI KO MAY XEEWËL
GU SAX CA ALLAAXIRA.
NIT KI DOON NA ÑAAKK AK YËR CI GËN JAAY MAAGGI TEERE BOO
XAMNE YALLA WAACCE NAKO CI NIT ÑI, AK ÑAAKK NGËM CI TEERE
BU MAAGG BII
DOON NA ÑAAKK NGËM CI YONENT YU MAAGG YOOYU NIKI MUUY
ÑAAKKEE AND AK ÑOOM CA ALJANNAH JA BIS PEEÑCCI BA SUKO
DEFEE MUUY AND AK SAYTAANE AK HOOMLU KAT YI XËRËM CA
SAFARA JAHANNAMA, NDAW KËR GU BON, NDAW DAKANDOO GU BON.
YALLA MU KAWE MI WAXNA:ْ
{WAXAL NE ÑI ÑAAKK DËGG ÑOOY ÑI NGA XAMNE DAÑOO ÑAAKK
SEEN BOOPP ÑAAKK SEEN NDIABOOT BIS PEEÑCCI BA DAMANE
LOOLA NAK MOOY ÑAAKK GU LEER GI }
18
DANA LEEN TIIM CI KAW AY DONĞO CI SAFARA DANA CI SEEN
SUUF AY DONĞO CI SAFARA, LOOLU YALLA MOONGI CEEY XUPEE
JAAMAM YI YEEN SAMAY JAAM NA NGEEN RAGAL YALLA}
[39: 15,16].
BUL DI YEEXA JËL SAY MATU KAAY
ADUNA DU KËRUK SAX!
BEEPP TAAR DANA MOSA LAAXXU BEEPP BAANEEX DANA MOSA
FAY.....
BIS DINA ÑAW ÑU HASAAB CI LEEPP LOO MOSA DEF, LOOLU MOOY
BISU TAXAWAAY BA YALLA MU KAWE MI WAXNA:َ
{ÑU DAADI TEK TEERE YI NGA DAADI JIS KACCOOR YI ÑU TIIT
NGIR LI NEEKK CI BIIR TEERE BOOBULE ÑUY WAX NAN: NGALLA
WAAYE ÑUN LAN MOO DAL TEERE BI MOOM BAAYI WUL LU NDAW
BAAYI WUL LU MAG LUDUL TAKK NAKO, ÑU DAADI FEEKK LAÑU
DEFOON MUUY TE SA BOROOM DU TOOÑ KEENN}. [18: 49].
YALLA XAMLE NA NE : NIT KOO XAMNE DU JEEBLU MUJAM MOOY
SAX CA SAFARA JAHANNAMA BA FAAWWU.
ÑAAKK NEEKKUL LU ÑAAKK SOLO ,WAAYE LU RËY LA
{ KU SAAKKU LUDUL LISLAAM MUUY SA DIINE ;DUÑU KOKO
NANGUL TE MOOM ËLLËK ALLAAXIRA DAY BOOKK CA} [3: 85].
LISLAAM MOOY DIINE JI NGA XAMNE YALLA DU NANGGU BENEEN
DIINE BUDUL MOOM.
19
YALLA MOO ÑU BIND TE CI MOOM LAÑUY DEELLU , ADUNA BII
NATTU REKK LA NGIR ÑUN.
GËM BU WOOR NE DUNDU BII DAFA GATT NIKI GEENT... KEENN
XAMUL KAÑ LAY DEEH!
LAN MOOY NEEKK SA TONTU ÑEEL SA BOROOM BI NGA XAMNE
MOO LA BIND BU LA LAAJEE BIS PEEÑCCI: LU TAX TOOPPU LAWOON
GËGG? LU TAX TOOPPU LA WOON KI MOOTALI YONENT YI ?-YALLA NA
YALLA DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI .
LAN NGAAY TOONTU SA BOROOM BIS PEEÑCCI, TE WATANDEKU
LOO WOON NALA TOOPATUK WEEDDI (LA MU LAAY
YOOBOO!)LISLAAM, MU XAMAL LA NAKA MUJJUK YEEFËR YI MOOY
ALKU CA SAFARA BA FAAWWU?
YALLA MU KAWE MI NEENA:َ
{ ÑA NGA XAMNE DAÑOO WEEDDI YALLA WEEDDI SUÑUY
MANDARGA; ÑOOÑU ÑOOY WAA SAFARA TE ÑOOM DAÑU FAAY SAX }
[2: 39].
KU FI BAAYI GËGG DI ROY AY BAAY AKI MAAM;DOO AM BEENN
NGAANT!
YALLA MU TEDD MI XAMAL NAÑU NE : LU BARI CI NTIÑI DAÑUY
LAANK DUGGU CI LISLAAM NGIR RAGAL BËRËB BAÑUY DUNDEE.
ÑU BËRI DAÑUY BAÑ LISLAAM NGIR ÑAAKK XEMEM SOOPPI
SEEN PAS PAS YI NGA XAMNE DAÑUKO DOONNEE CI SEEN WAA JUR
YI TE TAAMMUKO. ÑU B BARI CI ÑOOM PAR PAR LOO AK JOM JOM LU
CI CAAXAAN YI NGA XAMNE DOONN NAÑUKO MOO LEEN DI TERE
DUGGU CI LISLAAM .
ÑII ÑEEPP AMUÑU NGAANT CI LOOLU TE DAAÑU TAXAW CI
KANAM YALLA TE DUÑU AM LAY.
DU NEEKK NGAANT CIB ATE MU NAAN: DAMAAY DES CIK ATE
NDAX TE DAMAA JUDDU FEEKK SAMAY ÑOÑ NEEKK KO! DEE DEET! NA
JAFANDEKO XEL MIKO YALLA JOX MOOM MIKO BIND NGIR MU MËNË
20
XAMNE ADUNA BII AMNA KUKO BIND, NIKI NOONU KIY JAAMU XEERY
YI AK XERËM YI AMUL NGAANT CI ROY AY WAA JURËM, LIKO WAR
MOOY MU GASTU DËGG LAAJ BOPPAM: NAKA LAADI JAAMOO YU WAY
YILE NGA XAMNE DUMA DEEGG DUMA JIS TE DUMA JARIÑ DARA?!
NIKI NASRAAN BOO XAMNE DAY GËM LU WUUTEEK CET AK XEL
MU DAY WAR MU LAAJ BOPPAM: NAKA LA BOROOM BI DI RAYEE
DOOMAM DIOO XAMNE DEFUL BAAKAAR MUKOOY RAY NGIR
BAAKAARU ÑËNEEN! LII CI TOOÑ LA! NAKALA MBINDEEF YI DI
DAAJEE CI GARAB, WALLA DI RAY DOOMU DOOMU BOROOM! NDAX
BOROOM BI MUNUL JEEGGËLE BAAKAARI MBINDEEF YI TE BAÑ LEENA
BAAY ÑUY RAY DOOMAM! XANAA BOROOM BI MANULA AAR
DOOMAM?
LI WAR CI BOROOM XEL MOOY MU TOOPP DËGG, BU MU ROY AY
BAAY AKI MAAM CI CAAXAAN.
YALLA MU KAWE MI NEENA:
{ BU ÑU LEEN WAXEE NE: KAAY LEEN CI LI YALLA WAACCE AK
CI YONENT BI;REKK ÑUNE : LU ÑU FEEKKOON SU ÑUY MAAM
DONAÑU, A WAAW NDAX BU FEEKEE SEENI MAAM SAX XAMUÑU
DARA TE NEEKUÑUWOON CI NDIUB} [5: 104].
KU BËGGË MUCCI TE TIIT CI BOOPAM CI LORI AY JEGEÑAALEEM
LAN LAAY DEF?
KU BAGGA MUCCI TE RAGAL TUNDU WIKO WËR! NDAX DANA
MANA DUGGU CI LISLAAM NABBU LISLAAMAM BA YALLA
YOOMBALALKO YOONU YIW WOO XAMNE DANA CA MOOMEE
BOOPAM TE FEEÑË LEECI LISLAAMAM.
BOOKK NACI LI WAR CI YAW NGA NANGU LISLAAM CI LU GAAW,
WAAYE WARUL CI YAW NGAY XAMAL ÑILA WËR SA LISLAAM WALLA
NGA KOOY SIIWËL, BU FEEKKEE LOR DALA CEEY DAL.
XAMAL NE YAW BOO DUGGEE CI LISLAAM, DANGAAY NEEKK
MBOOKKU CI AY MILYOON JULIT , DANGA MANA JOOKKOOK AY JAAKK
21
AKI SAXU WAAY YU LISLAAM (SAANTAR ISLAAMIK)CI SA DËKK NGAY
SAAKKU CI ÑOOM DIISOO AK NDIMBAL, SUKO DEFEE LOOLU DI LEEN
BEGLOO.
YALLA MU KAWE MI NEENA:ْ
{ KEEPP KU RAGAL YALLA,; YALLA DEFALKO GEENNU WAAYE CI
BEEPP XAT XAT, TE WARSAGAL KO FUM KO DUL FOOGEE}
65: 2,3]
YAW AJI JAANG JU TEEDD JI!
NDAX GËRËM LOO YALLA MI LA BIND, - KI NGA XAMNE MOO LA
DEFAL AY XEEWËLAM, NGA XAMNE MOO LA DAAN JOX DUNDU TE
FEEKK YAW YAANGI NEEKK MBEEMUR CI SA BIIRU YAAY, MU
WARSAGAL LA HEER BI NGA XAMNE MOOM NGAAY BAANAMTEKOO
LEEGI- LOOLU MOO APP SOLO CI GËRËM LOO NIT ÑI CI SA BOOPP
XANA DU TEXE ADUNA AK ALLAAXIRA MOO YEELLO ÑU
JOTTEEKO LEEPP LUKO YEES CI XEEWËLU ADUNA YII DI JEEX?
AHAKAY WAAT NAAKO CI YALLA!
BUL BAAYI SA LI WEESU MU LAY TERE GAAGANTI SAW YOON
WU AM NDIUUMTE AK DI DEF LI WER.
NANGA NEEKK JULIT BU WER TEY! BUL BAAYI SAYTAANE MU
LAAY TAXAWLOO BA DOO MANA TOOPP DËGG!
YALLA MU KAWE MI NEENA:
﴾ÈEY YEEN NIT ÑI LAY WU LEER NAAÑÑI ÑAWAL NA LEEN
BAAYEKOO CI SEEN BOROOM, TE WAACCEEL NAÑU LEEN LEER GU
BIR(174)
22
ÑI NGA XAMNE GËM NAÑU YALLA TE ĞOY CI MOOM; DANA LEEN
TAABBAL CI YËRMËNDE BU BAWOO FA MOOM AK NGANEEL TE
DANA LEEN TEK CI YOON WU JUB}(175)
[4: 174,175].
NDAX YAW WAAJ NGA NGIR JËL DOGU BU GËNË MAAGG CI SA
DUNDU?
BU FEEKKEE LI JIITU YEEPP XEL NANGUNAKO CI SA GIS GIS! NGA
NANGUKO CA DËGG DËGG CI SA XOLBI KON WAR NGAAY SEEXXI JEEGO
BU NDIËKK JAM CI NOOY MUJJEE NEEKK JULIT?
BUL SAY BÀKKAAR MU LAY TEREE DUGG CI LISLAAM, YÀLLA
XAMAL NAÑU CI ALXURAN: NE MOOM MOOY JEEGGËLE BÀKKAAR YU
DOOM AADAMA YEEPP BU DUGGEE CI LISLAAM ,DAADI DEELLU CI
BOROOMAM MI KO BIND, BACI GANNAAW BOO NANGGO LISLAAM
DAFA CI DOYADIK DOOM AADAMA CI NE YAW LEEGOO LEG NGA
TOOGGO BAAKAAR NDAX ÑUN AY NIT LAÑU NEEKKU ÑU AY
MALAAKA YU ÑU ÑONĞEEL CI AY BÀKKAAR , WAAYE LIÑU SAAKKU
CI ÑUN MOOY ÑUUY SAAKKU NDIEEGËL CI YALLA TE TUUB DELLU
CI MOOM BU YÀLLA JISEE CI YAW CI NE YAW YAA NGEEY
GAAWANTU DI NANGGU DËGG AK DI DUGGU CI LISLAAM TE TUDDU
ÑAARI BAATI SEEDE YI, NDAX LOOLU MOO LAAY DIMBALI CI BAAYI
YENEEN BÀKKAAR YI KII NGA XAMNE DAFA NANGGUL YALLA, TE
TOOPP DËGG YÀLLA MOO KOOY DËPËLEEK NDOOLLENTE YIW BUL
DEENG DEENGI CI DUGGU CI LISLAAM LEEGI.
BOOKKNA CI FIRNDEEY LOOLU WAXU YALLA MU KAWE MI:
{WAXAL ÑI WEEDDI YALLA NE: BUÑU DAYTALOO ;ÑU ÑU
JEEGGËLLEEN LI WEESU} [8: 38].
LAN LAA MANA DEF NGIR NEEKK JULIT?
DUGGU CI LISLAAM MBIRËM YOOMB NA, HAJOWOO WUL AY
MANDARGA DIINE ,AMUL AY XEW XEW, WALLA TEEWUK KEENN, DAY
WAR NIT KI REEKK MU TUDDU BAATI SEEDE YI TE XAM MAANA YI,
TE GËM KO, TE MOOY MU WAX :(MAANGI SEEDE TE DËGGËL TE GËM
23
NE AMUL KEENN KUÑU WARA JAAMU KUDUL YALLA ,TE MAANGI
SEEDE TE DËGGËL TE GËM NE MUHAMMAD YONENT YALLA LA),BU
JAAPPANDEE CI YAW NGA MANKOO WAX CI LAAKKU ARAAB LU
BAAX LA BU JAFEE CI YAW NGA WAX KO CI SA LAAKK, CI LOOLU
NGAAY NEEKKEE JULIT , DAY WAR CI YAW NGA JAANGA SA DIINE JI
NGA XAMNE MOOY SA BALLU WAAY TEXE FII CI ADUNA AK SAK
MUCCI CA ALLAAXIRA.