Ay njàngale yu am solo ñeel xeet wi yépp
Aji-taalif ji:
Seex Abdul Asiis Ibn Abdallah Ibn Baas -yal na ko Yàlla yërëm-
Laltaay:
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel
ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.
Cant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindéef yi, mujj ga ñeel na way- gëm ñi, Yal na Yàlla julli te sëlmal ci
jaamam bi di Yonenteem bi Muhammat, moom ak waa-këram ak àndandoom yépp.
Ginnaaw loolu:
Lii ay waat la yu tënku ci leeral lenn ci li war ci ku ne mu xam ko ci diiney lislaam, tudde naa ko: ( ay
njàngale yu am solo ñeel xeet wi yépp).
Maa ngi ñaan Yàlla mu jariñ ci jullit ñi, te nangul ma ko, ndax moom ku tabe la ku tedd la.
Abdul Asiis ibn Abdallah ibn Baas.
Ay njàngale yu am solo ñeel xeet wi yépp1
Bind bu njëkk mi: Saaru faatiha ak saar yu gàtt yi
Saaru faatiha ak lu jàppandi ci saar yu gàtt yi, tàmbalee ci saaru Isaa zulsilati ba saaru Naasi, di ko jàng,
di wéral njàng ma, di ko mokkal, di firi li ñu ci war a xam.
Ñaareelu bind bi: Ponki Lislaam.
Leeral ponki lislaam yii di juróom, ba ca njëkk te gën caa màgg mooy: seede ne amul benn buur bu yayoo
jaamu bu dul Yàlla, seede it ne Muhammat ndawul Yàlla la, firi maanaa ya, ànd ak leeral sàrti
Laa-i-Laaha illal Laahu, aki maannaam, (laa-i-Laaha) day dàq lépp luñuy jaamu te du Yàlla, (illal Laahu)
day saxal ne ag jaamu Yàlla rekk moo ko yayoo amul ku ñu koy bokkaale.Sàrti (laa-i-Laaha Illal Laahu
nag) mooy: xam-xam bi safaanoo ak réer, kóolute gi safaanoo ak sikk-sàkka, sellal gi safaanoo ak
bokkaale, dëgg gi safaanoo ak fen, bëgg safaanoo ak bañ, wommatu gi safaanoo ak bokkaale, nangu gi
safaanoo ak bañ, ak weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla.Sàrt yii dajalees na ko ci ñaari bayit yii di ñëw:
Xam-xam, kóolute, ak sag dëggu ànd ak bëgg ak wommatu ak nangu ko.
Ñu dolli si juróom-ñatteel ba mooy nga weddi lépp ludul Yàlla ci mbir yi ñuy def Yàlla.
Ànd ak leeral seede ne Muhammat ndawul Yàlla la ak ya mu làmboo: loolu mooy lii: dëggal ko ci li mu
xibaare, ak topp ko ci li mu digle, ak moytu li mu tere te jàjje ca, bañ a jaamu Yalla lu dul ci li Yàlla yoonal
mook ub Yonenteem -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- .Ginnaaw ba muy leeralal ndongo yi li des ci
ponki lislaam yii di juróom, mooy: Jilli, ak joxe asaka, ak woor weeru koor, ak aj màkka ci ku ko man benn
yoon.
Ñatteelu bind b mooy: Ponki gëm yi.
Juróom-benn la: te mooy nga gëm Yàlla ak i malaakaam, ak ay téereem, ak i Yonenteem, ak bis-pénc,
nga gëm dogal bu neex ak bu naqari bu jóge ci Yàlla.
Ñenteelu bind bi: xaaji Tawhiid ak xaaji bokkaale.
Leeral xaaji Tawhiid yi (wéetal Yàlla) te yooyu ñatt la: wéetal Yàlla ci ay jëfam, wéetal Yàlla ci jaamu gi,
wéetal Yàlla ci ay turam ak i melokaanam.
Bu dee wéetal Yàlla ci ay jëfam nag mooy: gëm ne Yàlla mooy ki bind lépp, mooy kiy def di dindi ci mbir
yépp, amul kenn ku ñu koy bokkaaleel ci loolu.
Kennal Yàlla cig jaamu nag: mooy gëm ne Yàlla mooy ki nu war a jaamu ci dëgg amul ku ñu koy
bokkaaleel, te loolu mooy maanaam Laa-ilaaha illal-Laahu, maanaam ma mooy: amul ku ñu war a jaamu
ci dëgg ku dul Yàlla, mbooleem jaamu yi lu mel ni julli ak woor ak yeneen, day war ñu defal ko Yàlla cig
sellal, te du dagan ñu defal ko keneen.
Bu dee kennal Yàlla ci ay turam ak i meloom nag mooy: gëm lépp lu rot ci Alxuraan, walla ci hadiis yu wér
yi ci ay turi Yàlla ak i melokaanam, ak saxal ko ñeel Yàlla kepp, saxal ko ca na mu yelle ca moom, ci lu
dul ag coppi, walla dàq ko, walla di ko melal, ngir jëfe waxi Yàlla:{ْ ُلﻗَُوھُﱠﷲٌَدﺣَأ)1 ) { yaw Yonnente bi waxal
1 Tasaare nañu ko ci téereem ba (majmuuhu fataawaa wa maqaalaat mutanawwiha) xaajub ñatteel ba,
xëtuw (288- 298).
ne: Yàlla kenn la(1)ُ ﱠ ﷲَُدﻣﱠﺻﻟا)2 ) Yàlla Mooy genn kilifa gi ñépp di jublu ciy aajo. ( càppaacoli)(2)ْ َمﻟِْدﻠَﯾَْمﻟَوَْدﻟُوﯾ
)3 ) Jurul kenn te kenn juru ko(3)ْ َمﻟَوُنﻛَﯾُﮫﱠﻟُوًاﻔُﻛٌَدﺣَأ } 2Te amul nawle amul ndend[ As-Samad: mat ko sëkk],Ak
waxi Yàlla -mu kawe mi te sell-:{َ ْسﯾَﻟِﮫِﻠْﺛِﻣَﻛٌْءﻲَﺷَُۖوھَوُﻊﯾِﻣﱠﺳﻟاُرﯾِﺻَﺑْﻟا } Dara melul ne moom, moom mooy Aji-Dégg ji
di Aji-Gis ji[As-Suuraa: 11],Lenn ci ay woroomi xam-xam def nañu ko ñaari xaaj, ñu dugal kennal Yàlla ci
ay turam ak i meloom ci biir ci biir kennal Yàlla cig moomeelam, loolu deesu ca wax dara, ndax
jubluwaay bi leer na ci ñaari xaaj yépp.
Xaaji bokkaale yi ñatt la: bokkaale gu mag, bokkaale gu ndaw, bokkaale gu nëbbu.
Bokkaale gu mag gi: day waral jëf ju yàqu ak sax sawara ci ku ko deewaale, kem ni ko Yàlla waxe ne:{َْوﻟَو
ُواﻛَْرﺷَأَِطﺑَﺣَﻟُمﮭْﻧَﻋﺎﱠﻣُواﻧﺎَﻛَُونﻠَﻣْﻌَﯾ } 3{ bu ñu bokkaale woon kon seen jëf yépp di na yàqu }[Al-Anhaam: 88],Yàlla
mu kawe mi wax na ne:{ ﺎَﻣَنﺎَﻛَنﯾِﻛِْرﺷُﻣْﻠِﻟنَأُرُواﻣْﻌَﯾَِدﺟﺎَﺳَﻣِﱠﷲَنﯾِِدھﺎَﺷٰﻰَﻠَﻋِمﮭِﺳُﻔﻧَأِْرﻔُﻛْﻟﺎِﺑَۚكِﺋَٰﻟوُأِْطَتﺑَﺣُْمﮭُﻟﺎَﻣْﻋَأﻲِﻓَوِرﺎﱠﻧﻟاُْمھَ
ِدُونﻟﺎَﺧ} {Du yell ci bokkaalekat yi ñuy toppatoo jàkkay Yàlla yi tey way-seede ca seen weddi ga, ñooñee
seen i jëf yàqu na te ñoom ca sawara la ñuy sax{[At-Tawba: 17],Ku ci faatu deesu ko jéggal, àjjana it
araam na ci moom, niki ni ko Yàlla mu màgg mi waxe ne:{ ﱠ نِإَﱠﷲَﻻُِرﻔْﻐَﯾنَأَْرَكﺷُﯾِﮫِﺑُِرﻔْﻐَﯾَوﺎَﻣَدُونَِكﻟَٰذَنﻣِﻟُءﺎَﺷَﯾ } Yàlla
du jéggale ñu koy bokkaale dana jéggale nag lépp lu dul bakkaale ñeel ku ko soob[ An-Nisaa: 48], Yàlla
wax na ne:{ُ ﮫﱠﻧِإَنﻣْْرِكﺷُﯾِﱠﺎِﺑَْدﻘَﻓَم ﱠَرﺣُﱠﷲِﮫْﯾَﻠَﻋَﺔﱠﻧَﺟْﻟاُوَاهْﺄَﻣَوُرﺎﱠﻧﻟاۖﺎَﻣَوَنﯾِﻣِﻟﺎﱠظﻠِﻟِْنﻣٍرﺎَﺻﻧَأ } Ku bokkale Yàlla araamal na ci
moom àjjana te wàccuwaayam mooy sawara, te tooñkat yi duñu am ku leen di dimbali[Al-Maa-ida : 72].
Bokk na ci ay xeetam: ñaan ñi faatu, ak xërëm yi, ak xettaliku ci ñoom, ak di leen nésaral, ak di rendi ngir
ñoom, ak yu ni mel.
Bokkaale gu ndaw nag: mooy lu Alxuraan ak Sunna tudde bokkaale, te fekk bokkul ci xeeti bokkaale gu
mag gi; niki ngistal ci yenn jëf yi, ak waat ci ku dul Yàlla, ak wax bu soobee Yàlla ak diw, ak lu ni mel; ngir
waxu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-:{ li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu
ndaw}4ñu laaj ko mooy lan, mu ne mooy: {ngistal}Imaam Ahmat ak Tabaraanii ak Bayhaqii, ñu jële ko ci
Mahmuut ibn Labiid Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla gërëm- ci càllale gu baax, Tabaraanii nettali na ko ci ay
càllale yu baax, jële ko ci Mahmuut ibn Labiid, mu jële ci Raafih ibn Xadiij, mu jële ci Yonnente bi -yal na
ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Ak waxi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-{ képp ku waat ci lu dul Yàlla bokkaale
na}5Imaam Ahmat moo ko soloo ci càllale gu wér, ñu jële ko ci Umar ibn Al-Xattaab -yal na ko Yàlla
gërëm-Abuu Daawuda it soloo na ko, ak At-Tirmisiyu ci càllale gu wér, ci Hadiisu ibn Umar -yal na ko
Yàlla gërëm- ñu jële ko ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:{Képp ku waat si
lu dul Yàlla bokkaale na}Ak waxi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-:{ buleen wax: bu
soobee Yàlla ak diw, waaye nangeen wax: bu soobee Yàlla topp mu soop diw}Abuu Daawuda moo ko
génne ci càllale gu wér, ñu jële ko ci Husayfata ibn Al-Yaman -yal na ko Yàlla gërëm-.
Waaye xeet bii du waral génn ci diine, du waral it sax ca sawara, waaye day dàquwante ak matug Tawhiid
gi war.
Bu dee ñatteelu Xeet bi: mooy: bokkaale gu nëbbu, tegtal ba mooy waxi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli
xéewal ak mucc-{Mo ndax duma leen xibaare li ma gën a ragal ci yéen ci Masiihud Dajjaal ? Ñu ne ko
ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne leen: bokkaale gu nëbbu, nit ki day taxaw di julli muy rafetal ag
julleem ngir ne nit a ngi koy xool}6Imaam Ahmat moo ko soloo ci Musnadam, ñu jële ko ci Abuu Sahiid
Al-Hudriyyu - Yal na ko Yàlla gërëm-.
Dina dagan ñu séddale bokkaale ci ñaari xeet kepp:
Gu mag ak gu ndaw, bokkaale gu nëbbu moom dina duggaale ci biir.
dana tàbbi ci gu mag gi, niki bokkaaleg naaféq yi; ndax ñoom dañuy nëbb séen pas-pas yu yàqu ya, di
feeñal Lislaam ngir ngistal, ak ragal ci seen bopp.
6 Ibn Maaja, buntub dëddu (4204), Ahmat (3/30).
5 Al-Buxaarii ci buntub ngiñ ak nisër (6271), Muslim, buntu ngiñ yi (1646), At-Tirmisiyu, buntub, nisër ak
ngiñ (1533), An-Nasaa-iyu buntub ngiñ yi ak nésar(3764), Abuu Daawuda, buntub ngiñ yi ak nésar
(3249), Ibn Maaja, Buntub kaffaara(2094), Ahmat (1/47), Maalik, buntub nésar ak ngiñ (1037),
Ad-Daaramiyu, buntub nésar ak ngiñ (2341).[11] Al-Buxaarii, buntub teggin (5757), Muslim, buntub ngiñ
(1646), At-Tirmisiyu buntub nisër ak ngiñ (1535), An-Nasaa-iyu, ngiñ ak nésar (3766), Abuu Daawuda,
ngiñ ak nër (3251), Ibn Maaja, Kaffaara (2094), Ahmat (2/69), Maalik, nésar ak ngiñ (1037),
Ad-Daaramiyu, nésar ak ngiñ (2341).[12] Abuu Daawuda, Teggin (4980), Ahmat (5/399).
4 Ahmat (5/428).[9] Ahmat (5/428).
3 Saaru Al-Anhaam aaya: 88.[5] Saaru At-Tawba aaya: 17.[6] Saaru An-Nisaa aaya : 48.[7] Saaru
Al-Maa-ida aaya: 72.
2 Saaru Al-Ixlaas aaya: 1 - 4.[3] Saar u As-Suuraa aaya: 11.
Dina nekk ci bokkaale gu ndaw, lu mel ni ki ngistal, kem ni mu ñëwe ci Hadiisu Mahmuut ibn Labiid
Al-Ansaarii bi jiitu, ak hadiisu Abuu Sahiit bi ñu tudd.Yàlla mooy boroom tawfeex.
Juróomeelu njàng mi mooy rafetal (Ihsaan).
Ponki rafetal, mooy: nga jaamu Yàlla ba mel ni yaa ngi koy gis, boo demul ba mel noonu, nga xam ne
moom Yàlla mi ngi lay gis.
Juróom-benneelu bind bi mooy: Sàrti julli.
Sàrti julli juróom-ñent la:
Lislaam, ak am xel, ak ràññee, ak laab, ak deñ ci sobe, ak suturaal sa awra, ak duggug waxtu wi, ak jublu
xibla, ak yéene.
Juróom-ñaareelu bind bi mooy: ponki julli
Ponki julli Fukk ak ñent la:
Taxaw ci ku ko man, kàbbaru armal, jàng faatiha, rukkoo, yamoo ginnaaw rukoo bi, sujjóot ci juróom-ñaari
cér yi, siggi jóge ci sujjóot ba, toog ci digante ñaari sujjóot yi, dal ci jëf yépp, toftale ponk yi, taaya gu mujj
gi, toog ci taaya gu mujj gi, julli ci Yonnente bi, ñaari sëlmal yi.
Juróom-ñatteelu njàng mi mooy: yi war ci julli.
Yi war ci julli juróom-ñatt la:
Mbooleem kàbbaar yi ba mu des bu armal bi, ak wax ji Imaam walla kuy julli moom dong di wax ( samihal
Lallaahu liman Hamidahu), ak wax ji ñépp di wax ( Rabbanaa wa lakal hamdu), ak wax ( subhaana
rabbiyal hasiim) ci rukkoo bi, ak wax (subhaana rabbiyal ahlaa) ci sujjóot bi, ak wax( rabbi ixfir lii) ci
diggante ñaari sujjóot yi, ak taaya ju njëkk ji, ak toogaayu taaya ju njëkk ji.
Juróom- ñenteelu bind bi mooy: Taaya.
Te mooy nit ki wax:
(Attahiyyaatu lil Laahi, was salawaatu, wat tayyibaatu, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul
Laahi wa barakaatuhuu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina, ashadu an
laa-i-Laaha illal Laahu, wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu).
Topp mu julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax:( Allahumma salli halaa
Muhammadin, wa halaa aali Muhammadin, kamaa sallayta halaa Ibraahiima wa halaa Aali Ibraahiima,
innaka hamiidun majiidun, wa baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa baarakta
halaa Ibraahiima wa halaa aali Ibraahiima innaka hamiidun majiidun).
Topp mu sàkkoo muslu ci Yàlla ci Taaya ju mujj ji ci mbugalum sawara, ak ci mbugalum bàmmeel, ak ci
fitnay dund ak dee, ak ci fitnay Masiihud Dajjaal, bu noppee mu tànn lu ko soob ci ay ñaan rawati na ñaan
yi ñu tuxale ci sariiha, bokk na ca:
( allahumma ahinnii halaa sikrika wa sukrika wa husni ibaadatika, allahumma innii salamtu nafsii sulman
kasiiran, walaa yaxfirus sunuuba illaa Anta, faxfir lii maxfiratan min hindika, warhamnii, innaka antal
Xafuurur Rahiim).
Bu dee ci taaya ju njëkk ji day jog jëm ci ñatteelu ràkka ba ci jullig tisbaar ak tàkkusaan ak timis, bu jullee
ci Yonnente bi loolu moo gën; ngir mbooleem hadiis yi rot ci loolu, mu jog na jëm ci ñatteel ba.
Fukkeelu bind bi mooy: sunnay julli.
Bokk na ca:
1- ubbiteg julli gi.
2- teg loxo ndayjoor ci kaw loxo càmmooñ ci kaw dënn bi, ci taxawaay bi njëkk muy rukoo ak ginnaaw
rukkoo ba.
3- yëkkati ñaari loxo yi ba mu tolloo ak ñaari mbagam walla ñaari noppam fekk baaraamu loxo yi sësaloo
ci kàbbar bu njëkk bi, ak buy rukkoo, ak buy siggi jóge ci rukkoo bi, ak buy taxaw jóge ci taaya ju njëkk ja
jëm ca ñatteelu ràkka ba.
4- lépp lu dolliku ca njëlbéenug sàbbaal ga ca rukkoo ba ak sujjóot ba.
5- lépp lu dolliku ca wax ja muy wax: (Rabbanaa walakal hamdu) ginnaaw bu siggee ca rukkoo ba, ak
lépp lu dolliku ca wax ja muy wax: (rabbi ixfir lii) benn yoon ca diggante ñaari sujjóot ya.
6- def bopp bi mu yamoo ak ndigg li ci rukoo bi.
7- soreele ñaari përëgi loxo yi ak ñaari wetam, mu soreele biir ba ak ñaari poojam, soreele it ay poojam ci
ay yeelam ci sujjóot ba.
8- yëkkati ñaari loxo yi mu bañ a lalu ci suuf ca sujjóot ba.
9- toogaayub Aji-julli ji ca kaw tànkub càmmooñ ba ñu lal, ak samp tànkub ndayjoor ba ci taaya ju njëkk ji
ak ci diggante ñaari sujjóot yi.
10- Toog toogaayu (tawarruk) ci taaya bu mujj bi ci jullig ñenti ràkka mbaa ñatti ràkka, tawarruk mooy:
toog teg say njekkikaay ci suuf daal di lal tànkub càmmooñ ba ca ron tànkub ndayjoor ba te samp bu
ndeyjoor ba.
11- di junj ci baaraamu sànnikaay bi ci taaya ju njëkk ji ak ju ñaareel ji ba taaya ji jeex ak di ko yëngal buy
ñaan.
12- julli ci Yonnente bi ak ci waa këram, ak julli ci Ibraahiima ak waa këram, ci taaya gu njëkk gi.
13- Ñaan ci taaya gu mujj gi.
14- biral njàng ma ci jullig fajar, ak ci jullig àjjuma, ak jullig ñaari feet yi, ak jullig baawunaan, ak ci ñaari
ràkka yu njëkk yi ci jullig timis ak gee.
15- yalu njàng ma ci jullig tisbaar, ak tàkkusaan, ak ci ñatteelu ràkka ci jullig timis, ak ci ñaari ràkka yi mujj
ci jullig gee.
16- Jàng li tegu ci faatiha ci Alxuraan, ànd ak sàmmoonte ak yeneen sunna yi rot ci julli yu dul yii ñu tudd,
bokk na ca yooyu: lu topp ci wax( rabbanaa wa lakal hamdu) ginnaaw siggi ci rukoo ci àqi Imaam walla
maamuun mbaa kiy julli moom dong, loolu sunna la, bokk na ca ba tay: teg ñaari loxo yi ca kaw wóom ya
te teqale waaraam yi ci rukoo bi.
Fukkeelu bind bi ak benn mooy: yiy yàq julli.
Yiy yàq julli juróom-ñatt la:
1- wax te tay ko ànd ak fàttaliku ak ug xam, bu dee ki fàtte nag walla ki xamul loolu du yàq julleem.
2- reetaan.
3- lekk.
4- naan.
5- Awra yu feeñ.
6- dummóoyu xibla gu jéggi dayo.
7- Po mu bari ta tegaloo ci biir julli gi.
8- Njàpp mu yàqu.
Fukkeelu bind bi ak ñaar mooy: sàrti njàppu.
Yooyu Fukk la:
Lislaam, ak am xel, ak xàmme, ak yéene, ànd ak àtteem ci mu bañ koo yéenee dagg ba keroog njàpp mi
di mat, ak laabu mbaa fomp ba set njëkk muy jàpp, ak ndox mu laab te dagan, ak dindi lépp luy tax ndox
mi du àgg ci der bi, ak duggug waxtu wi ci koo xam ne ag tojleem lu sax la.
Bindub fukkeel bi ak ñatt mooy: faratay njàpp.
Juróom-benn la:
Raxas kanam gi gallaxndiku ak saraxndiku ci la bokk, ak raxas ñaari loxo ba ca cooñc ya, ak masaa bopp
bi yépp boole ca ñaari nopp yi, ak raxas ñaari tànk yi boole ca dojoor ya, ak toftaloo, ak méngale. Dinañu
sopp baamtu raxas kanam gi ak ñaari loxo yi ak tànk yi ñatti yoon, niki noonu gallaxndiku ba ak
saraxndiku ba, la cay farata nag mooy benn yoon bi, bu dee masaa bopp nag duñu sopp baamtu ga kem
ni ko hadiis yu wér yi tegtale.
Bindub fukkeel bi ak ñent mooy: yiy yàq njàpp.
Juróom-benn la:
Liy génn ci ñaari génnuwaay yi, ak sobe su ëpp suy génn ciw yaram, ak xel mu dem ngir nelaw walla
leneen, ak laal am pëy ci loxo moo xam pëyum kanam la mbaa mu gannaaw te fekk dara doxul ca
digganteem ak loxo bi, ak lekk yàppu giléem.
Ag yeeye bu am solo: bu dee sang néew nag: li wér mooy ne du yàq njàpp, loolu mooy li ëpp ci waxi
woroom xam-xam yi; ngir ne tegtal ñëwu ci, waaye nag bu loxob kuy sang néew bi laalee pëyum néew bi
kon day war ci moom mu jàpp.
Li war ci moom mooy loxoom bañ a laal pëyum néew bi lu dul ne am na lu mu doxale ca diggante ba, niki
noonu laal jigéen du yàq njàpp, moo xam laalug bànneexu la walla déet fii ak dara génnul ci moom lii
mooy li gën a wér ci waxi woroom xam-xam yi, ndaxte Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
fóon na kenn ci ay soxnaam daal di julli te jàppaatul.
Bu dee waxi Yàlla ji mu wax ci ñaari aaya yi nekk ci An-Nissa ak Al-Maa-ida:{ْ وَأُُمﺗْﺳَﻣَﻻَءﺎَﺳﱢﻧﻟا } 7{ walla ngéen
jote ak jigéen ñi ci sëy ak ñoom}[An Nisaaii: 43][Al Maa-ida: 6],Li ñu ci jublu mooy: Sëy, ci li gën a wér si
waxi woroom xam-xam yi, mooy waxi Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla gërëm-, ak am mbooloo ci magi
Lislaam yi jiitu ak ñi ñëw seen ginnaaw.Yàlla mooy Boroom tawfeex.
Bindub fukk AK juróomeel bi mooy: jikkowoo ay
jikko yu ñu yoonal ci bépp jullit.
Bokk na ca: dëggu, ak wóor, ak sàmmu, ak am kersa, ak njàmbaare, ak tabe, ak matal kóllare, ak sori
lépp lu Yàlla araamal, ak rafetal dëkkandoo, ak dimbali way-aajowoo yi sa kem kàttan, ak yeneen ci ay
jikko yoy Alxuraan ak Sunna tegtale na ne lu ñu santaane la.
Bindub fukkeel bi ak juróom-benn: tegginoo
teggini Lislaam yi.
Bokk na ca: nuyoo, ak di leeral xar- kanam, ak di lekke ak a naane loxo ndayjoor, ak wax bismillah cig
tàmbali, ak wax alhamdu lil-Laahi boo noppee, ak wax alhamdu lil-Laahi boo tissóolee, ak wax
yarhamukal Laahu ñeel ki tissóoli bu dee wax na alhamdu lil-Laahi, ak seeti ku feebar, ak gunge néew ca
jullée ga ak rob ga, ak teggini Lislaam ci booy dugg jàkka, walla kër mbaa nga nga fay génn, ak booy
tukki, ak am ay teggin sa diggante ak say ay say way-jur ak say mbokk ak say dëkkandoo ak ci mag ñi ak
ci ndaw ñi, ak ndokkeel ku am doom mbaa kuy takk soxna, ak massawu ku dogal dal, ak yeneen ci ay
teggin yu Lislaam digle ci sol yére ak summiku ak Sol ay dàll.w
Bindub fukkeel bi ak juróom-ñaar:
moytandikuloo bokkaale ak xeeti moy Yàlla yi.
Bokk na ca: juróom-ñaari bàkkaar yiy alage, te mooy: bokkaale Yàlla, ak njabar, ak ray bakkan bu Yàlla
araamal, ak lekk riiba, ak lekk alali jirim, ak daw ci bisu xare, ak xas jullit bu jigéen bu sàmm boppam.
Bokk na ca: dëngé ñaari way-jur, ak dagg mbokk, ak seede ay neen, ak waat ci lu dul dëgg, ak lor
dëkkandoo, ak tooñ nit ñi ci seen dereet, ak ci seen alal, ak ci seen der, ak naan sàngara, ak kàrt, ak jëw,
ak rambaaj, ak yeneen ci yi Yàlla tere walla Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Bindub fukkeel bi ak juróom-ñatt: waajal ab néew
ak jullée ko ak rob ko.
Jàppal faramfànce gi:
Bi ci njëkk: sah aji-sukraat ji baati seede yi.
Yoonalees na ñuy sah aji-sukraat ji: ( laa-i-Laaha illal-Laahu); ngir waxi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli
xéewal ak mucc-{Saleen seeni way-faatu: laa-i-Laaha illal-Laahu}8Muslim soloo na ko ci Sahiiham,Li ñu
jublu ci way-faatu ci Hadiis bii: mooy ñiy sukraat, te mooy ñi màndargay dee feeñ ci ñoom.
Ñaareel ba: Bu faatoo nañu gëmm bët ya te takk ñaari ŋaam
ya.
Ngir sunna rot na ca.
Ñatteel ba: sang néewub jullit lu war la lu dul mu nekk ku
faatu ci xare.
Kooku kenn du ko sang kenn du ko jullee, waaye dañu koy suulaale ak i yéreem; ngir ne Yonnente bi -yal
na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- sangul ña faatu ca Uhud niki noonu julleewu leen.
Ñenteel ba: melokaanu sang néew.
8 Muslim, Al-janaa-is(916), At-Tirmisiyu, Al-janaa-is (976), An-Nasaa-iyu, Al-janaa-is (1826), Abuu
Daawuda, Al-janaa-is, (3117), Ibn Maaja maa-jaa-a fil jannaa-is (1445), Ahmat (3/3).
7 Saaru An-Nisaa aaya: 43.
Dañuy suturaal awraam, topp ñu yëkkati ko tuuti daal di nal biir bi ndànk, sangkat bi daal di laxas ciy
loxoom ab morso walla lu ni mel, bu noppee mu jàppal ko njàppum julli, topp mu raxas bopp bi ak ndox
ak siddéem walla lu ni mel, topp mu raxas wetug ndayjooram, teg ca bu càmmooñ ba, topp mu sang ko
ñaareelu yoon ak ñateel, muy rombale loxoom ca kaw biir ba, bu dara génnee mu raxas ko, bu noppee
mu sakk barab ba ak wëttéen walla lu ko niru, bu dee deñul di génn, mu jëfandikoo ban, walla jumtukaay
yu yees yi ci wàllu faj.
Mu baamtuwaat njàpp ma bu setul mu dolli ba juróom walla juróom-ñaari yoon, topp mu fomp ko, mu daal
di def ci ruqam yi gëtt, ak barabu sujjóot ya, bu defee ca yaram wépp gëtt it baax na, topp mu cuuraay
càngaay la, bu dee ay weham mbaa ay naanoom (Mustaas) dafa gudd mu dagg ca dara, bu ko bàyyee it
dara nekku ca, bu mu peñe kawar ga, bumu wat kawaru naq ga bu mu ko xarafal, ndax tegtal ñëwu ca,
jigéen nag dees na létt kawar ga ñatti létt tëral létt ya mu jëm ginnaaw.
Juróomeel bi: sàng néew bi.
Li gën mooy ñu sàng néew bi ak ñatti yére yu weex du am semis du am kaala, kem niko Yonnente bi
defe, bu ñu ko defelee ab semis ak ub tubëy ak ub càngaay dara nekku ca.
Jigéen moom dañu koy sàng ci juróomi yére: ab yére, ak muuraay, ak sër, ak ñaari laxasaay. Dinañu
sàng xale bu góor ci benn yére ba ci ñatti yére, xale bu jigéen nag dinañu ko sànge ab semis ak ñaari
càngaay.
Liy farata ci ñépp mooy benn yére buy suturaal yaramu néew bépp, waaye bu dee néew bi da doon armal
kon dees na ko sang ak ndox ak siddéem, daal di koy sàng ci ab sër ak ub mbalaan, mbaa leneen,
waaye duñu muur bopp bi ak kanam gi duñu ko sotti gëtt itam; ndax te dees koy dekkal yawmal xiyaam
muy wax labbaykal Laahumma làbbayka niki mu wére ci Hadiisu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal
ak mucc- bu dee néew bi jigéen la dañu koy sàng niki ñépp. Waaye kenn du ko laalal gëtt kenn du muur
kanamam kenn du ko solal ay gaaŋ ci loxoom waaye dañuy muur kanam gi ak loxo yi ci càngaay li niki ni
leeral li jiitoo woon ci melow sàng jigéen.
Juróom-benneel bi: ki gën a yay ci sang ko ak jullée ko ak
rob ko.
Ki gën a yay ci sang ko ak jullee ko ak rob ko mooy: ki mu dénkaane ci loolu, topp ci baay ji, topp ci
maam ji, topp ci ka ko gën a jege ci ay mbokkam yu góor.
Ki gën a yay ci sang néew bu jigéen bi mooy: ki mu dénkoon loolu, topp ci maam bu jigéen, topp ci ka ko
gën a jege ci jigéen ñi, ñaari way-deñcante yi ku ci ne man naa sang moroomam; ndax Abuubakar
soxnaam mooko sang, Alliyun tamit moo sang soxnaam Faatima - yal na leen Yàlla gërëm-.
Juróom-ñaareel bi: na ka lañuy jullée néew.
Day kàbbar ñenti yoon, mu jàng faatiha ginnaaw kàbbar bu njëkk ba, bu ko boolee akk aw saar wu gàtt
walla benn aaya mbaa ñaar di na baax; ngir hadiis bu wér bi ci ñëw jógé ci ibn Abbaas -yal na leen Yàlla
gërëm-, topp mu kàbbar ñaareelu kàbbar, daal di julli ci Yonnente bi niki muy jullée ci moom ci taayag julli,
topp mu kàbbar ñatteelu kàbbar bi, daal di wax:( Allahumma ixfir Li hayyinaa wa mayyitinaa, wa
saahidinaa wa xaa-ibinaa, wa saxiirinaa wa kabiirinaa, wa sakarinaa wa unsaanaa, Allahumma man
ahyaytahu minnaa fa ahyihi halal islaam, waman tawaffaytahu minnaa fa tawaffihi halal iimaan,
Allaahumma ixfir lahu, warhamhu, wa haafihi, wahfu hanhu, wa akrim nusulahu, wa wassih mudxalahu,
waxsilhu billmaa-i wassalji walbaradi, wanaqihi minal xataayaa kamaa yunaqas sawbul abyadu
minaddanasi, wa abdilhu daaran xayran min daarihi, wa ahlan xayran min ahlihi, wa adxilhu al jannata,
wa ahishu min hasaabil xabri, wa hasaabin naari, wafsah lahu fii xabrihi, wa nawwir lahu fiihi,
Allaahumma laa tahrimnaa ajrahu walaa tudilanaa bahdahu.Topp mu kàbbar ñetteelu kàbbar bi, daal di
sëlmël benn sëlmël ci ndayjooram.
Sopp nañu mu yëkkati ñaari loxoom ci bépp kàbbar, bu dee néew bi jigéen la na wax: ( Allaahumma ixfir
lahaa...) ba mu jeex, bu dee ñaari néew la dinañu wax: (Allaahumma ixfir lahumaa...) ba mu yegg, bu dee
ay néew yu bari la na wax: ( Allaahumma ixfir lahum...) ba mu yegg, bu dee ab xale la lii la koy ñaanal
wolif njéggal:( Allaahumma ijhalhu faratan wa suxran li waalidayhi, wa safiihan mujaaban, allahumma
saqil bihii mawaasiinahumaa, wa ahsim bihii ujuurahumaa, wa alhiqhu bi saalihi salafil muuminiina,
wajhalhu fii kafaalati Ibraahiima alayhis salaatu was salaamu, waxihi birahmatika hasaabal jahiimi).
Liy sunna mooy imaam bi taxaw fi tolloo ak bopp bi bu dee góor la, bu dee jigéen la mu taxaw ci digg bi,
bu dee ñu bari lañu na góor ñi gën a jege imaam bi, bu dee ay xale ñoo nga ca xale bu góor mooy nekk ci
kanam jigéen gu mag topp ca xale bu jigéen topp ca, ñu góor ñi ñooy yamoo bopp xale ak mag, ndiggu
jigéen tolloo ak bopp góor, niki noonu jigéen xale ak mag ñooy tollo bopp, ñiy julli ñépp nekk ci ginnaaw
imaam, bu dee kenn koo xam ne amul fu mu taxaw man naa taxaw ci ndayjooru imaam.
Juróom-ñatteel bi: naka lañuy robe néew.
Li ñu yoonal mooy ñu xóotal bàmmeel bi ba mu tolloo ak ndig góor, ñu gas ko mu am pax mu ndaw féete
xibla, ñu dugal néew bi ci pax mu ndaw mi mu tëdde wetug ndayjooram, ñu tekki takk-takki càngaay li,
kenn du muri kanam ga moo xam góor la mbaa jigéen, ñu daal di fay samp ay móol, daal di cay raatale
ban ba mu dëgër, bu dee amuñu móol nañu fa def leneen moo xam ay xeer la mbaa bant bu man a tax
suuf si du àgg ca moom, ñu daal di koy sotti suuf, sopp nañu bu ñuy def loolu ñu wax (Bismillahi, wa
halaa millati rasuulil-Laahi), ñu yëkkati bàmmeel bi ba mu tolloo ak sibra, bu dee jàppandi na ñu def ca ay
xeer yu dëgër daal di ciy wis ndox.
Yoonal nañu ci ñi ko gunge woon ñu taxaw ca bàmmeel ba ñaanal néew bi; ndaxte Yonnente bi -yal na ko
Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan noppi ci rob néew day taxaw ca bàmmeel ba daal di wax ne:{
sàkkulleen seen mbok mi njéggal, ngeen ñaanal ko Yàlla saxal làmmeñam, ndax te leegi ñu laaj ko}9.
Juróom-ñenteel bi: yoonal nañu ci ki fekkewul jullee gi mu
jullee ko ginnaaw bi ñu ko robee ba noppi.
Ndax Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- def na loolu, waaye loolu na fekk rob bi matagul
weer mbaa ca lay yam, bu dee diir ba ëpp na wéer kon deesul yoonal jullee ga ca bàmmeel ba; ndax
loolu kenn tuxalewul ci Yonnente bi ne jullee na ab néew ca bàmmeel ba ginnaaw ba ñu ko robee ba mu
ëpp weer.
Fukkeel bi: du dagan ci waa kër néew bi ñuy toggal nit ñi aw
ñam.
Ngir waxi Jaabir ibn Abdallah Al-Bajalii sahaaba bu tedd ba -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax
ne:(Dajaloo ci waa-kër néew bi ak defar aw ñam ginnaaw biñuko robee daaan nañuko boole ci déjjatu,
(mooy lii yuuxu aka xalangu) maanaam àtte boobu lay yor.Imaam Ahmat moo ko soloo ci càllale gu
rafet,Bu dee nag ñeneen ñoo leen toggal aw ñam walla ñoom ñoo ko togg ngir seeni gan loolu dara
nekku ci, yoonal nañu ci ay mbokkam ak i dëkkandoom ñu toggal leen ; ndax yonnente bi -yal na ko Yàlla
dolli xéewal ak mucc- bi mu jotee xibaaru faatug Jahfar ibn Abii Taalib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ca
Saam, dafa digal waa këram ngir ñu defaral waa kër Jahfar aw ñam, mu wax ne:{ñoom de mbir mu leen
soxlaal moo leen dal}10.
Waa kër néew bi bu ñu woowee seeni dëkkandoo mbaa ñeneen ngir ñu ñëw lekk ci ñaw wi ñu leen jox
dara nekku ca, loolu amul wenn waxtu wu ñu ko tënk ci li nu xam ci sariiha.
Fukkeel bi ak benn : du dagan ci jigéen muy ténj aji-faatu ji lu
ëpp ñatti fan lu dul boroom këram mbaa mu nekk ku ëmb.
(Ténj mooy ñaawlu.)
Du dagan ci jigéen muy ténj ab néew lu ëpp ñatti fan lu dul boroom këram bu boobaa dina war ci moom
mu ténj ko ñenti weer ak fukki fan, lu dul mu ëmb bu boobaa am doom mooy tax mu jeex; ngir saxug loolu
ci Sunna su wér jógé ci yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Bu dee góor nag du dagan muy ténj kenn ci jegeñaale yi walla ñeneen.
Fukkeel bi ak ñaar : dina ñu yoonal ci góor ñi ñuy siyaare ji
bàmmeel yi ngir di ñaanal néew yi ak di leen sàkkul
yërmànde ak ngir fàttaliku dee ak la ca ginnaawam.
Ngir waxu Yonnente bi - yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-{siyaareleen bàmmeel yi, ndax da leen di
fàttali allaaxira}11Imaam Muslim génne na ko ci sahiiham,Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak
mucc- da daan jàngal sahaaba yi bu ñu siyaaree bàmmeel ñu Wax:( Assalaamu halaykum ahlad diyaari
minal muuminiina wal muslimiina, wa innaa insaa al-Laahu bikum laahixuuna, nas-alul Laaha lanaa
11 Muslim, Al-janaa-is (976) , An-Nasaa-iyu, Al-janaa-is (2034), Abuu Daawuda , Al-janaa-is (3234) , Ibn
Maaja, maa jaa-a fil jannaa-is (1569) , Ahmat (2/441).[19] Muslim, Al-janaa-is (975) , An-Nasaa-iyu,
Al-janaa-is (2040) , Ibn Maaja, maa jaa-a fil jannaa-is (1547) , Ahmat (5/353).
10 At-Tirmisiyu, Al-janaa-is (998), Abuu Daawuda, Al-janaa-is (3132), Ibn Maaja, Maa jaa-a fil Jannaa-is
(1610).
9 Abuu Daawuda, Al-janaa-is (3221).
walakumul haafiyata, yarhamul-Laahu al-mutaxaddimiina minnaa walmuta-axiriina)Bu dee jigéen ñi nag
duñu siyaare ji bàmmeel yi; ndax Yonnente bi dafa rëbb jigéen ñiy baril lu ñuy siyaare ji bàmmeel, ndax
dañuy ragal fitna ci ñoom ak ñàkka muñ buñu siyaare jee bàmmeel ya, loolu moo tax du dagan ci ñoom
ñuy gunge ab néew bu ñu koy robi, ndax Yonnente bi moo leen ko tere, waaye jullee néew ci jàkka ji
walla ci julleekaay ba loolu moom yoonal na ñu ko ci góor ak jigéen yépp.
Lii mooy li jàppandi ci ñu dajale ko.
Yal na Yàlla dolli Yonnente bi xéewal ak mucc ak ay ñoñam ak i Sahaabaam.
Ay njàngale yu am solo ñeel xeet wi yépp
Laltaay:
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.
Bind bu njëkk mi: Saaru faatiha ak saar yu gàtt yi
Ñaareelu bind bi: Ponki Lislaam.
Ñatteelu bind b mooy: Ponki gëm yi.
Ñenteelu bind bi: xaaji Tawhiid ak xaaji bokkaale.
Juróomeelu njàng mi mooy rafetal (Ihsaan).
Juróom-benneelu bind bi mooy: Sàrti julli.
Juróom-ñaareelu bind bi mooy: ponki julli
Juróom-ñatteelu njàng mi mooy: yi war ci julli.
Juróom- ñenteelu bind bi mooy: Taaya.
Fukkeelu bind bi mooy: sunnay julli.
Fukkeelu bind bi ak benn mooy: yiy yàq julli.
Fukkeelu bind bi ak ñaar mooy: sàrti njàppu.
Bindub fukkeel bi ak ñatt mooy: faratay njàpp.
Bindub fukkeel bi ak ñent mooy: yiy yàq njàpp.
Bindub fukk AK juróomeel bi mooy: jikkowoo ay jikko yu ñu yoonal ci bépp jullit.
Bindub fukkeel bi ak juróom-benn: tegginoo teggini Lislaam yi.
Bindub fukkeel bi ak juróom-ñaar: moytandikuloo bokkaale ak xeeti moy Yàlla yi.
Bindub fukkeel bi ak juróom-ñatt: waajal ab néew ak jullée ko ak rob ko.
Bi ci njëkk: sah aji-sukraat ji baati seede yi.
Ñaareel ba: Bu faatoo nañu gëmm bët ya te takk ñaari ŋaam ya.
Ñatteel ba: sang néewub jullit lu war la lu dul mu nekk ku faatu ci xare.
Ñenteel ba: melokaanu sang néew.
Juróomeel bi: sàng néew bi.
Juróom-benneel bi: ki gën a yay ci sang ko ak jullée ko ak rob ko.
Juróom-ñaareel bi: na ka lañuy jullée néew.
Juróom-ñatteel bi: naka lañuy robe néew.
Juróom-ñenteel bi: yoonal nañu ci ki fekkewul jullee gi mu jullee ko ginnaaw bi ñu ko robee ba noppi.
Fukkeel bi: du dagan ci waa kër néew bi ñuy toggal nit ñi aw ñam.
Fukkeel bi ak benn : du dagan ci jigéen muy ténj aji-faatu ji lu ëpp ñatti fan lu dul boroom këram mbaa
mu nekk ku ëmb. (Ténj mooy ñaawlu.)
Fukkeel bi ak ñaar : dina ñu yoonal ci góor ñi ñuy siyaare ji bàmmeel yi ngir di ñaanal néew yi ak di
leen sàkkul yërmànde ak ngir fàttaliku dee ak la ca ginnaawam.